- Ñaaxe ci saraxe ak joxe ci yooyu Yàlla.
- Joxe ci mbir yu baax yi bokk na ci sabab yi gën a màgg yiy baarkeel wërsëg di ko ful, ak Yàlla wuutalal jaam bi la mu joxe woon.
- Hadiis bii dafa bokk ci li Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nettali jële ko ci Boroomam, ñu di ko woowe Hadiis Al-xuddsi walla Hadiisu Al-Ilaahiy, te mooy Hadiis bi nga xam ne ay baatam ak i maanaam ci Yàlla la juge, waaye amul jagle yi nekk ci Alxuraan te mu koy ràññee ak lu dul moom, niki di jaamu Yàlla ci jàng gi ak di laab ngir jàng ko, ak di ci dëkke mbaa di ci lottalaate ak yenneen.