saraxe du wàññi alal, te Yàlla du dolli Jaam biy jéggale ludul ag màgg, te kenn du toroxlu ngir Yàlla lu dul ne broom bi dina ko Yëkkati
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «saraxe du wàññi alal, te Yàlla du dolli Jaam biy jéggale ludul ag màgg, te kenn du toroxlu ngir Yàlla lu dul ne broom bi dina ko Yëkkati».
Muslim soloo na ko
Explanation
Leerarug adiis bi:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne sarax du wàññi alal, waaye day fegal nit ki ay gàkk-gàkk, te Yàlla day wuutalal boroomam aw yiw wu màgg, loolu di ag dolliku waaye du ag wàññiku.
Jéggale te am kàttanu fayu du dolli boroom lu dul kàttan ak tedd nga.
Kenn du toroxlul Yàlla, ci lu dul mu ragal kenn mbaa muy laamisook kenn, walla muy sàkku ci moom njariñ, lu dul ne payam mooy ak yëkkatiku ak teraanga.
Hadeeth benefits
Bokk na ci njariñal adiis bi:
Yiw ak texe moo ngi ci topp Sariiha ak di def lu baax, donte ñenn ci nit ñi da ñuy foog lu wuuteek loolu
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others