- Alal ji nekk ci yoxoy nit ñi alalu Yàlla la, da leen koo dénk ngir ñu jëfandikoo ko ca na mu ko yoonale, te moytu cee soppaxndiku cig neen, te lii nag ñépp a ci yam moo xam njiit la walla nit yi ci des.
- Taralug Sariiha ci alalu mbooloo, ci ne képp ku ci jiite dara dees na ko regle ëllëg bis-pénc ca fàggu ga ak ca joxe ga.
- Tëkku gii nag képp kuy soppaxndiku ci alal ci lu dul yoon da ciy dugg moo xam alalam la walla alalu keneen.