ku muñal ki am jafe-jafe, walla mu baal ka ko, Yàlla dana ko keral bis-penc ca suufus keru Gàngunaayam ga bis ba nga xam ne genn ker amul gu dul keram ga
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku muñal ki am jafe-jafe, walla mu baal ka ko, Yàlla dana ko keral bis-penc ca suufus keru Gàngunaayam ga bis ba nga xam ne genn ker amul gu dul keram ga».
At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat
Explanation
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne képp ku muñal ki ame bor, walla mu teggil ko bor ba, ag payam mooy: Yàlla dana ko keral fa suufus keru Gàngunaayam ga keroog bis-penc ba Jant ba di jege boppi jaam yi, tàngaay wa di tar lool ca ñoom, Kenn du am kerr ku dul ku Yàlla keral.
Hadeeth benefits
Ngëneelu yombal ci jaami Yàlla yi, ak ni dafa bokk ci sabab yiy musale ci tiitaangey bis-penc ba.
Am pay daal mu ngay toll kem na jëf tollu.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others