Jële nañu ci Hittaan Ibn Abdullah Ar-Raxaasii mu wax ne: julli naa ak Abuu Muusa Al-Ashsrii ag julli, dañoo lënkale julli ak ug mbaax ak asaka, nee na: ba Abuu Muusaa noppee ca julli ga ba sëlmël daal di wëlbëtiku, daal di ne: kan ci yéen moo wax baat sàngam ak baat sàngam? Nit ñi noppi, mu waxaat ne: kan ci yéen moo wax wax jii ak jii? Nit ñi noppi: mu ne: man naa am yaw Hittaan yaa ko wax? Mu ne ko: waxu ma ko de, damaa ragal nga gëdd ma ci, am ku wax ci gaa yi ne: man maa ko wax, te nammuma ci lu dul yiw, Abuu Muusa ne ko: xanaa xamuleen lu ngeen di wax ci seen julli gi? Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xutba na nu leeralal nu ay sunnaam xamal nu sunug julli, daal di wax ne: «bu ngeen di julli nangeen jubal séen sàppe yi, kenn ci yéen jiite leen, bu kàbbaree nangeen kàbbaar, bu waxee: (xayril maxduubi halayhim wa laddaalliina) [Al-Faatiha: 7], nangeen wax: Aamiin, Yàlla dana leen nangul, bu kàbbaree daal di rukoo nangeen kàbbar te rukoo, imaam bi moo leen di njëkk a rukoo, moo leen di njëkk a siggi Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne: "bee ci bee, bu waxee: samihal Laahu liman hamidahu, nangeen wax Allaahumma Rabbanaa lakal hamdu, Yàlla dana leen dégg, Yàlla dafa wax ci nettalig Yonnente bi: samihal Laahu liman hamidahu, bu kàbbaree sujjóot nangeen kàbbar sujjóot, imaam moo leen di njëkk a sujjóot njëkk leen a siggi, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne: "bee ci bee, bu nekkee ca toogaay ba kenn ci yéen na njëkk a wax: attahiyyaatu attayyibaatu assalawaatu lil Laahi, assalaamu halayka ayyuhan Nabiyyu wa rahmatul Laahi wa barakaatuhu, assalaamu halaynaa wa halaa hibaadil Laahi assaalihiina, ashadu an laa iLaaha illal Laahu wa ashadu anna Muhammadan abduhu wa rasuuluhu».