Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ci diggante ñaari sujjóot yi: «Rabbi ixfir lii, Rabbi ixfir lii
Jële nañu ci Husayfata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ci diggante ñaari sujjóot yi: «Rabbi ixfir lii, Rabbi ixfir lii».
Abóo Daawuda soloo na ko, ak An-nasaa'iy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat
Explanation
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan toog ci diggante ñaari sujjóot yi da daan wax: Rabbi ixfir lii, Rabbi ixfir lii, di ko baamtu.
Maanaam Rabbi ixfir lii mooy: jaam bi sàkku ci Boroomam mu faral ko ay bàkkaaram te suturaal ko ay ayibam.
Hadeeth benefits
Yoonal nañu ñaan ci diggante ñaari sujjóot yi ci jullig farata ak naafila.
Sopp nañu di baamtu wax jii: Rabbi ixfir lii, benn yoon bi moom dafa war.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others