- Dañoo war a sujjóot ci julli gi ci juróom-ñaari cér.
- Sib nañu di dajale yére walla kawar ci julli.
- War na ci kiy julli mu ànd ak ug dal ci julli gi, ci teg céri sujjóot yiy juróom ci kaw suuf, daal di dal ba def sikar yi ñu yoonal.
- Tere nañu takk kawar ci góor ñi déet jigéen ñi; ndax jigéen ci julli dañu koo digal mu muuru.