- Ñaaxe ci sàmmoonte ak jullig tàkkusaan ci njëlbeenu waxtoom te gaawe ko.
- Tëkku gu tar ñeel na ku bàyyi jullig tàkkusaan, ak ne yeexe ko ba waxtu wa jàll, moo gën a màgg yeexe geneen juuli, ndax mooy julli gi digg-dóomu ga ñu jagleel ag digle, ci wax ji Yàlla wax ne: (na ngeen sàmmoonte ak julli yi ak julli gu digg-dóomu gi) [Al-Baxara: 238].