- Loràngey ñàkk a julli mbooloo ca jàkka ja.
- Naaféq yi jubluwuñu ca séen jaamu ya lu dul ngistal ak ndéggtal, duñu dem ca julli ga lu dul bu leen nit ñi dee gis.
- Yool bu màgg bi nekk ci julli gee ak fajar ànd ak mbooloo ma, ak ne ñoom ñaar de jar na ñoo teewe donte dangay raam.
- Sàmmonte ak jullig gee ak fajar ag mucc la ci naaféq, waaye di leen wuute ci meloy naaféq yi la bokk.