Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Yàlla du xool...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne Yàlla mu kawe mi du xool meloy jaam ñi ak seen i yaram, ndax dafa rafet walla dafa ñaaw...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "Yàlla day fii...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne Yàlla day fiir di bañ di sib, kem ni aji-gëm ji di fiire ak di bañe ak di sibe, te sab...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "moytuleen juróom-ñ...
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo ngi digal aw xeetam ngir ñu sori juróom-ñaari bàkkaar yiy alage, ba ñu ko laajee yan la ?...
Jële na ñu ci Abuu Bakrata -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Ndax duma l...
leerarug hdiis bi:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaar Sahaabaam yi bàkkaar yi gën a màgg, mu tudd ñatt yii:
1. Bokkaale Y...
Jële na ñu ci Abdulaa Ibn Amr Ibnul Haas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «bàk...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral bàkkaar yu mag yi, te mooy gu ñu tëkku aji-def ji ci tëkku gu tar ci àdduna walla allaaxi...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Yàlla du xool seen i melo mbaa seen alal waaye seen xol lay xool ak seen i jëf».
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "Yàlla day fiir, way-gëm it day fiir, te fiiràngeg Yàlla mooy way-gëm ji def lu mu araamaal".
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "moytuleen juróom-ñaar yiy alage", ñu ne ko: yaw Yónenteb Yàlla bi yooyu yan la ? Mu ne: "bokkaale Yàlla, ak njabar, ak ray bàkkan bu Yàlla araamal ñu ray ko ci ludul dëgg, ak lekk ribaa, ak lekk alali jirim, ak daw bisub xare , ak tuumaal jigéen i jullit ju saŋewu".
Jële na ñu ci Abuu Bakrata -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Ndax duma leen xibaar bàkkaar yi gën a mag?» Mu wax ko ñatti yoon, ñu ne ko: ahakay yaw Yónente Yàlla bi, mu ne leen: «bokkaale Yàlla, ak dënge ñaari way-jur» mu jóg toog fekk dafa sóonu woon, daal di ne: «ak wax ludul dëgg», nee na: deñul di ko bàmtu ba ñu mujj wax naan: aka neexoon mu noppi.
Jële na ñu ci Abdulaa Ibn Amr Ibnul Haas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «bàkkaar yu mag yi mooy: bokkaale Yàlla, ak dënge ñaari way-jur, ak ray bakkan, ak giñ guy nuuralaate».
Jële na ñu ci Abdallah Ibnu Mashuut mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na : «li ñuy njëkk a àtte ci diggante nit ñi ëllëg bis-pénc mooy dereet ».
Jële na ñu ci Abdulaa Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "Ku ray koo séqal kóllëre, du xeeñcu xetug Àjjana, te dinanteem ak xetam ga soree ni doxub ñent-fukki at".
Jële nañu ci Jubayru Ibn Muthim -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne dégg na Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «kuy dog mbokk du dugg àjjana».
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku bëgg ñu yaatal wërsëgam, guddal fanam, nay jokk ag bokkam».
Jële nañu ci Abdulaa Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «kiy jokk mbokk du kiy faye liñuko jokk, waaye kiy jokk mbokk mooy ki nga xam ne bu ñu dogee ag mbokkam mu jokk ka ko dog.
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ndax xam ngeen luy jëw?», ñu ne ko: Yàlla ak Yónenteem a xam, mu daa di ne mooy: «tudd sa mbokk ci lu ko neexul», ñu ne ko: waaw bu dee li ma wax moo ngi ci sama mbokk mi nag? Mu wax ne: «bu nekkee ci moom kon jëw nga ko, bu nekkul ci moom nag kon duural nga ko».
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- rëbb na kiy ger ak ki ñuy ger cib àtte.