li ñuy njëkk a àtte ci diggante nit ñi ëllëg bis-pénc mooy dereet
Jële na ñu ci Abdallah Ibnu Mashuut mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na : «li ñuy njëkk a àtte ci diggante nit ñi ëllëg bis-pénc mooy dereet ».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Explanation
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne li ñuy njëkk a àtte ci diggante nit ñi ëllëg bis-pénc ci tooñ gi ñenn ñi di tooñ ñeneen ñi : mooy dereet, niki ray, ak gaañe.
Hadeeth benefits
Màggaayu mbiri dereet, ndax li gën a am solo ca la ñuy tàmbalee.
Bàkkaar dana màgg kem màggaayu yàqute ga nga ca ame, ray bakkan bu set nag bokk na ci yàqute yi gën a màgg te dara gënu koo màgg lu dul kéefar ak bokkaale Yàlla mu kawe mi.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others