- Jokk mbokk gi Lislaam jàpp mooy nga jokk ku la dog, di baal ku la tooñ, di jox ku la xañ, waaye jokk nekkul ci defalante ak fayantoo.
- Jokk mbokk dana nekk ci nga fexe ba éggale ci ñoom lu jàppandi ci aw yiw niki alal ak ñaan ak digle lu baax tere lu bon ak yu ni mel, ak nga fexe ba jeñal leen aw ay.