- Bokk na ci njariñal adiis bi :
- Dog mbokk ci bàkkaar yu mag yi la bokk.
- Jokk mbokk day amee ca kem nañu ko miine, kon day wuute kem barab ya ak jamono ya ak nit ña.
- Jokk mbokk dana nekk ci siyaare, ak sarax, ak rafetal jëme ci moom, ak seeti ku feebar, ak digal leen lu baax tere leen lu bon, ak yeneen.
- Lu mbokk gi di gën a jege dog mbokk gi di gën a rëy bàkkaar.