- Bokk na ci njariñal adiis bi :
- Rafetug njàngalem Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ba tax mu jox leen masala yi ci anamug laaj.
- Rafetu teggini Sahaaba yi ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ba tax ñu ne ko Yàlla ak ub Yónenteem ñoo ko xam.
- Ki ñuy laaj wax ci lu mu xamul: Yàllaa xam.
- Aar gi Sariiha aar mbooloo mi ci sàmm àq yi ak diggante mbokk yi.
- Jëw lu araam la lu dul ci yenn anam yi ngir yéwénal; bokk na ca: dindi tooñaange, lu melni ki ñu tooñ tudd turu ka ko tooñ ci koo xam ne man na koo nangul àqam, mu wax ko ne ko: diw tooñ na ma, walla def na ma lii, bokk na ca: diisoo ci mbirum sëy, wàlla lu jëm ci bokk dara, mbaa ci ki ngay dëkkal, ak yu ni mel.