- Joxe ger ak jël ko dafa araam, ak di dox ci diggante ñaar ñiy ger’ ak di ca dimbalante; ngir la ca nekk ci dimbalante cig neen.
- Ger ci bàkkaar yu mag yi la; ndaxte Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa rëbb ki koy jël ak ki koy joxe.
- Ger ci wàllu àtte moo gën a bon, gën rëy bàkkaar; ndax la ca nekk ci tooñ ak àtte ci lu dul li Yàlla wàcce.