- Araamal nañu ray boroom kollëre ak yéefar biy fay ay wareefam, ak yéefar buñu làq , te loolu ci bàkkaar yu mag yi la bokk.
- Boroom kollëre: mooy yéefar buñu jël ci moom kóllëre mu nekk ci dëkku jullit ñi, te du xeex jullit ñi ñoom itam duñu ko xeex, yéefa biy fay: mooy ki dëkk ci dëkku jullit ñi di fay juuti, ki ñu làq: mooy ku dugg ci kër jullit ñi ci kóllëre ak kaaraange ci ab diir buñu tënk.
- Wattandikuloo wor kóllëre ak ñi dul ay ajullit.