- Ngiñ luy nuuralaate amul lu koy kaffaara; Ndax daa bari loraange ak i ñaawtéef, moo tax fàwwu ñu tuub ko.
- Ñenti bàkkaar yu mag yi ñu tudd ci hadiis bi du ngir tënk ko ca waaye day wane ne séen i bàkkaar daa màgg lool.
- Bàkkaar yi daa séddalikoo yu mag ak yu ndaw, yu mag yi nag mooy: bépp bàkkaar bu am mbugalum àdduna, niki géten ak móolu, walla tëkkug allaaxira, niki tëkku ci dugg sawara, yu mag yi itam ay daraja la yenn yi moo gën a rëy araamug yeneen yi, bàkkaar yu ndaw yi nag mooy yi nekkul yu mag rekk.