- Yittewóo sellal AB xol, ak laabal ko ci wépp melokaanam wu ñu ŋàññi.
- Baaxug xol mi ngi ci sellal, baaxug jëf it mi ngi ci topp Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, te ñoom ñaar la Yàlla di xool.
- Nit ki bu mu woru ci alalam mbaa cib taaram walla ciw yaramam walla ci lénn ci liy feeñ ci àdduna sii.
- Moytu di sukkandiku ci liy fés bàyyi li nëbbu.