- Bokk na ci njariñal hdiis bi: Bàkkaar bi gën a rëy mooy bokkaale Yàlla; ndax da koo def muy njiitu bàkkaar yu mag yi di ba ca gën a rëy, te loola waxi Yàlla jii moo koy feddali: {Yàlla du jéggale ag bokkaale, waaye dana jéggale lu dul loolu ñeel ku ko soob}.
- Àqi ñaari way-juy lu màgg la, ba tax mu lënkale séen i àq ak àqi Yàlla mu kawe mi.
- Bàkkaar yi daa séddalikoo yu mag ak yu ndaw, yu mag yi nag mooy: bépp bàkkaar bu am mbugalu àdduna, niki géten ak móolu, walla tëkkug allaaxira, niki tëkkoo ci dugg sawara, yu mag yi itam ay daraja la yenn yi moo gën a rëy yeneen yi cig haraam, bàkkaar yu ndaw nag yi mooy yi nekkul yu mag rekk.