Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «fi jaam bi di gën...
Leerarug adiis bi:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne fi jaam bi di gën a jegee Boroomam mooy bu sujjóotee; ndaxte kiy ju...
Jële na ñu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Li ëppoon ci ñaani Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mooy:"Allaahumma Rabb...
Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-daan na baril di ñaane ñaan yu matale yi,bokk na ca: "Rabbanaa aatinaa fiddunyaa hasanatan, wa fil-aa...
Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- guddi gu nekk bu daan yéeg ci lalam d...
Leerarug hdiisb:
Bokk na ci njubug Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan yéeg ci lalam ngir nelaw day boole ñaari téqam yëkkati l...
Jële nañu ci Sadaad ibn Aws -yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne: «li gën a kawe cig jé...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day xibaare ne jéggalu am na ay baat, te ba ca gën te gën caa màgg mooy jaam bi wax ne: "Allaahumma...
Jële nañu ci Abdullah Ibn Xubayb -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Génn nanu ci guddi gu bari taw te lëndëm lool, di wër Yonnente Yàlla bi ng...
Sahaaba bu màgg bii di Abdullah Ibn Xubayb -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day xibaare ne: ñoom dañoo génnoon ci guddi gu bari ab taw, te lëndëm...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «fi jaam bi di gën a jegee Boroomam mooy bu sujjóotee, deeleen ci baril ay ñaan».
Jële na ñu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Li ëppoon ci ñaani Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mooy:"Allaahumma Rabbanaa aatinaa fiddunyaa hasanatan, wa fil-aaxirati hasanatan, wa xinaa hasaabannaari".
Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- guddi gu nekk bu daan yéeg ci lalam day boole ñaari téqam, daal di ciy ëf, daal di jàng: {Xul huwal Laahu Ahadun}, ak {Xul ahuusu Bi Rabbil falaxi} ak {Xul ahuusu Bi Rabbin naasi}, daal di ciy masaa yaramam lu mu man, tàmbalee ca bopp ba ak kanam ga, ak lu ca topp ci yaramam, da koy def ñatti yoon.
Jële nañu ci Sadaad ibn Aws -yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne: «li gën a kawe cig jégalu yi mooy nga wax: Allaahumma anta Rabbii laa-i-Laaha illaa Anta, xalaqtanii wa anaa abduka, wa anaa halaa ahdika wa wahdika mastatahtu, ahuusu bika min sarri maa sanahtu, abuuhu laka bi nihmatika alayya, wa abuuhu bi sanbii faxfirlii,fa innahu laa yaxfirus sunuuba illaa Anta» mu wax ne:"ku ko wax ci bëccëg gi te am ci kóolute, daal di faatu ci bis bi njëkk ngoon di jot, kooku ci waa àjjana lay bokk, ku ko wax it ci guddi gi te am ci kóolute daal di faatu njëkk suba di jot, kooku ci waa àjjana lay bokk".
Jële nañu ci Abdullah Ibn Xubayb -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Génn nanu ci guddi gu bari taw te lëndëm lool, di wër Yonnente Yàlla bi ngir mu jiite nu julli, nee na: nu dab ko, mu ne ma: "waxal" te waxuma dara, mu waxaat ma: "waxal", te waxuma dara, mu ne ma: "waxal", ma ne ko: lan laay wax? Mu ne ma: "{Xul huwal Laahu Ahadun} ak ñaari musluwaay yi boo gontee ak boo xëyee ñatti yoon, dana la fegal lépp".
Jële nañu ci Samurata Ibn Jundub -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Wax yi gënal Yàlla ñent la: Subhaanal Laah, Wal hamdu lil Laah, wa laa-i-Laaha illal Laah, wal Laahu akbar, boo ci tàmbalee baax na».
Jële na ñu ci Abuu Ayyuuba -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku wax: laa ilaaha illal laahu wahdahu laa sariika lahu, lahul mulku wa lahul hamdu wa Huwa halaa kulli say-in Xadiiru , fukki yoon dana mel ne ku goreel ñenti bakkan ci doomi Ismaayla».
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ñaari baat a ngi nii yu woyof ci làmmeñ, diis ci màndaxekaay ba, Yàlla miy Aji-Yërëme ji sopp leen: Subhaanal Laahil Hasiim, Subhaanal Laahi wa bi hamdihii».
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku wax: Subhaanal Laahi wa bi hamdihii, ci bis bi téeméeri yoon, ñu sippi ay bàkkaaram doonte dafa tol ni puuriti géej».
Jële na ñu ci Abuu Maalik Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Laab mooy genn wàllu ngëm, sant Yàlla day feesal nattukaayu jëf ya, sàbbaal Yàlla ak sant Yàlla dañuy feesal walla day feesal li nekk ci diggante asamaan ak suuf, julli ag leer la, saraxe it aw lay la, muñ it ag leer la, Alxuraan it aw lay la ñeel la yaw, walla muy aw lay ci sa kaw, nit ñépp dañuy xëy am ci ñuy jaay séen bopp, benn mu goreel ko, walla mu alag ko».
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ma wax: Subhaanal Laahi, wal hamdu lil Laahi, wa laa ilaaha illal Laahu, wal laahu akbaru, moo ma gënal lépp lu jant bi fenk ci kawam».
Jële nañu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónent Yàlla bi -yal ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: «Li gën ci sikar yi: Laa ilaaha illal Laahu, li gën ci ñaan yi: Alhamdu lil Laahi».