- Bokk na ci njariñal hdiis bi:
- Laab ñaar la: laab gu feeñ te mooy jàppu ak sangu, ak laab gu nëbbu te mooy kennal Yàlla ak gëm ak def lu baax.
- Solos sàmmoonteek julli ndax moom leer la ñeel jaam bi ci àdduna ak allaaxira.
- Saraxe tegtal la ci ngëm.
- Solos jëfe Alxuraan ak dëggal ko ngir ne day nekk saw lay walla muy aw lay ci sa kaw.
- Bakkan boo ko soxlaalul ci jaamu Yàlla mu soxlaal la ci moy Yàlla.
- Nit ku nekk fàwwu mu jëf; benn mu goreel boppam ci topp Yàlla, walla mu alag ko ci moy Yàlla.
- Muñ day aajowoo dëgër ak séentu pay ga, ndax dafa am ab coono.