fi jaam bi di gën a jegee Boroomam mooy bu sujjóotee, deeleen ci baril ay ñaan
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «fi jaam bi di gën a jegee Boroomam mooy bu sujjóotee, deeleen ci baril ay ñaan».
Muslim soloo na ko
Explanation
Leerarug adiis bi:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne fi jaam bi di gën a jegee Boroomam mooy bu sujjóotee; ndaxte kiy julli day teg li gën a kawe te tedd ci yaramam ci kaw suuf ndax woyoflu la ak toroxlul Yàlla mu kawe mi fekk ma nga sujjóot.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- digle na baril ñaan ca sujjóot ya, bu ko defee toroxlul Yàlla ci wax ak jëf daal di daje.
Hadeeth benefits
Bokk na ci njariñal adiis bi :
Toppub Yàlla day dolli Jaam bi mu gën a jege Yàlla mu kawe mi.
Sopp nañu di baril ñaan ca sujjóot ya; ndax bérabi nangu ñaan la.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others