/ ñaari baat a ngi nii yu woyof ci làmmeñ, diis ci màndaxekaay ba, Yàlla miy Aji-Yërëme ji sopp leen

ñaari baat a ngi nii yu woyof ci làmmeñ, diis ci màndaxekaay ba, Yàlla miy Aji-Yërëme ji sopp leen

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ñaari baat a ngi nii yu woyof ci làmmeñ, diis ci màndaxekaay ba, Yàlla miy Aji-Yërëme ji sopp leen: Subhaanal Laahil Hasiim, Subhaanal Laahi wa bi hamdihii».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér

Explanation

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne am na ñaari baat yu nit ki di wax ci lu dul coono ak ci bépp anam, te seenug fay màgg lool ca màndaxekaay ba , te sunu Boroom miy Aji-Yërëme ji bëgg leen muy: Subhaanal Laahil Hasiim, Subhaanal Laahi wa bi hamdihii; ngir li ñu làmboo ci melal Yàlla cig màgg ak mat, ak sellal ko ci ay wàññiku -baarkeel na te kawe na-.

Hadeeth benefits

  1. Bokk na ci njariñal adiis bi:
  2. Tudd Yàlla gi gën a màgg mooy bu boole sellal Yàlla ak di ko tagg.
  3. Leeral yaatug yërmandey Yàlla ci jaamam ñi, ndax day fay pay gu rëy ci jëf yu tuuti.