- Pay gi nag ku ko wax ci bis bi rekk dana ko am moo xam daa toftaloo walla dafa tàqalikoo.
- Sàbbaal: mooy sellal Yàlla ci bépp wàññeeku, Cànt: mooy mellal ko ci gépp mat ànd ak bëgg ak màggal.
- Li ñu namm ci hadiis bi mooy far bàkkaar yu ndaw yi, bàkkaar yu mag yi nag moom tuub ko manuta ñàkk.