Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- guddi gu nekk bu daan yéeg ci lalam day boole ñaari téqam, daal di ciy ëf, daal di jàng: {Xul huwal Laahu Ahadun}, ak {Xul ahuusu Bi Rabbil falaxi} ak {Xul ahuusu Bi Rabbin naasi}
Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- guddi gu nekk bu daan yéeg ci lalam day boole ñaari téqam, daal di ciy ëf, daal di jàng: {Xul huwal Laahu Ahadun}, ak {Xul ahuusu Bi Rabbil falaxi} ak {Xul ahuusu Bi Rabbin naasi}, daal di ciy masaa yaramam lu mu man, tàmbalee ca bopp ba ak kanam ga, ak lu ca topp ci yaramam, da koy def ñatti yoon.
Al-buxaariy soloo na ko
Explanation
Leerarug hdiisb:
Bokk na ci njubug Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan yéeg ci lalam ngir nelaw day boole ñaari téqam yëkkati leen -kem ni kiy ñaan di def- daal di ciy ëf ci gemeñam, ëf bu sew ànd ak tuuti tiflit daal di jàng saar yii ñatti yoon: {Xul huwal Laahu Ahadun} ak {Xul ahuusu Bi Rabbil falaxi} ak {Xul ahuusu Bi Rabbin naasi} daal di raay ñaari ténqam ci lu mu man ci yaramam; tàmbalee ci boppam ak kanamam ak li féete ci kanam ci yaramam, day baamtu jëf jii ñatti yoon.
Hadeeth benefits
Bokk na ci njariñal adiis bi:
Sopp nañu jàng saaru Al-Ixlaas ak ñaari muslukaay yi njëkk ngay nelaw nga ëf ci, raay ci sa yaram loo man.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others