ku wax: laa ilaaha illal laahu wahdahu laa sariika lahu, lahul mulku wa lahul hamdu wa Huwa halaa kulli say-in Xadiiru , fukki yoon
Jële na ñu ci Abuu Ayyuuba -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku wax: laa ilaaha illal laahu wahdahu laa sariika lahu, lahul mulku wa lahul hamdu wa Huwa halaa kulli say-in Xadiiru , fukki yoon dana mel ne ku goreel ñenti bakkan ci doomi Ismaayla».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Explanation
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne ku wax: "laa ilaaha illal laahu wahdahu laa sariika lahu lahul mulku wa lahul hamdu wa Huwa halaa kulli say in Xadiirun", maanaam mooy: amul ku ñuy jaamu cig dëgg ku dul Yàlla dong amul bokkaale, te moom aji sell ji moo jagoo nguur gu mat, moo yayoo cant ak tagg gu ànd ak mbëggeel ak màggal
moom rekk, te mooy ki am kàttan lottul ci dara. Ku baamtu sikar bu màgg bii ci bis bi fukki yoon, dana am ci yool kem yoolu ku dindi ag njaam ci ñenti jaam ci séti Ismaayla doomu Ibraahiima -yal na leen Yàlla dolli xéewal ak jàmm- dafa jagleel séti Ismaayla -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak jàmm- cig tund; ndax ñoom ñoo gën a tedd ku dul ñoom.
Hadeeth benefits
Ngëneelu sikar bii làmboo kennal Yàlla mu kawe mi cig jaamu, ak nguur, ak cant, ak kàttan gu mat.
Ku wax sikar bii dana am yool bi moo xam cig toftaloo walla ci teqalikoo.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others