Sahd Ibn Hisaam Ibn Aamir ba mu duggee ca néeg Aysatu -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax ne: Yaw yaayu jullit ñi, wax ma jikkóy Yónente b...
Laaj nañu yaayu jullit ñi Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- jikkóy Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, mu tontu ci baat bu matale,...
Jële nañu ci Sadaan Ibn Aws -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne: mokkal naa yaari mbir ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu w...
Yónente bi xamle na ne Yàlla mu kawe mi dafa waral si nun rafetal ci lépp, te rafetal mooy: di fuglu Yàlla ba fàwwu, ci jaamu gi ak ci def yiw ak ci f...
Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "way-maandu...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ñi nga xam ne dañuy àtte nit ñi nekk ci séen suufu kilifteef cig maandu ak dëgg, ak ci...
Jële na ñu ci Abii Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «deesul lo...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne dañoo war a jeñ lor ci ay anam yu wuute, ci sunu jëmm ak ci ñeneen ñi, daganul kenn di...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: Benn waaye dafa wax Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: dénk ma, mu...
Kenn ci Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- dafa sàkku ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ngir mu tegtal ko lu koy jariñ, mu...
Sahd Ibn Hisaam Ibn Aamir ba mu duggee ca néeg Aysatu -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax ne: Yaw yaayu jullit ñi, wax ma jikkóy Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, mu ne ma: xanaa doo jàng Alxuraan? Ma ne ko: ahakay, mu ne ma: jikkóom moo doon.
Jële nañu ci Sadaan Ibn Aws -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne: mokkal naa yaari mbir ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Yàlla bind na rafetal ci mbir yépp, bu ngeen dee ray nangeen rafetal rayiin wa, bu ngeen dee rendi nangeen rafetal rendiin wa, nangeen daas seenug ñawka tey noppal li ngeen di rendi».
Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "way-maandu ñi de fa Yàlla danañu nekk ci kaw i minbari leer, nekk ca ndeyjooru Yàlla Aji-Yërëme ju màgg ji te tedd te yaari loxoom yépp ndeyjoor la, ñooñu ñooy ñiy Mandu ca séen i àtte ak séen i njaboot ak lépp lu ñu méngoo».
Jële na ñu ci Abii Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «deesul loru waaye deesul lore, ku lore Yàlla lor ko, waaye ku sonle Yàlla sonal ko».
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: Benn waaye dafa wax Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: dénk ma, mu ne ko: "bul mer" mu baamtu ko ay yoon mu ne ko: "bul mer".
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «am doole nekkul ci bëre daan, waaye ku am doole mooy kiy tëye boppam bu meree».
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dégg na benn waay di yedd mbokkam ndax kersa, mu ne ko: "«kersa ci ngëm la bokk».
Jële nañu
ci Miqdaat Doomi Mahdii-karib -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu wax ne: "bu nit ki bëggee mbokkam na ko wax ne da koo bëgg".
Jële nañu ci Jaabir Ibn Abdullah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Jépp jëf ju baax sarax la».
Jële nañu ci Abuu Barsata Al-Aslamii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «jaam bi du seqi benn jéego ëllëg bis-pénc ludul ne dees na ko laaj dundam gi ci lan la ko jeexale, ak xam-xamam bi lu mu ci def, ak alalam nan la ko ame ak ci fan la ko dugal , ak yaramam wi ci lan la ko ràppal».
Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "kiy taxawu ak a dimbali ab Jatun ak way-ñakk moo ngi mel ni kuy xeex ci yoonu Yàlla, wàlla kuy taxaw guddi di woor bëccëg"
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «képp ku gëm Yàlla ak bis bu mujj ba nay wax yiw mbaa mu noppi, képp ku gëm Yàlla ak bis-pénc nay teral dëkkandoom, képp ku gëm Yàlla ak bis-pénc nay teral ganam».