- Bokk na ci njariñal adiis bi :
- Gëm Yàlla ak bis bu mujj ba mooy cosaanu wépp yiw, te day tax a jef lu baax.
- Moytondikuloo gàkk-gàkki làmmiñ yi.
- Diiney Lislaam diney miinante la ak teraanga.
- Jikko yii daa bokk ci pàcci ngëm yi ak teggin ya ñu gërëm.
- Bari wax day waral tàbbi ci lu ñu sib mbaa lu araam, te mucc moo ngi nekk ci bañ a wax ludul Aw yiw.