- Ñaaxe ci dimbalante ak jàppalante ci faj aajoy ñi néew doole.
- Jaamu day làmboo jépp jëf ju baax, te bokk na ci ag jaamu taxawu ak a Dimbali jigéen ñi seen jëkkër faatu ak néew doole yi.
- Ibn Hubayrata nee na: li ñu ci namm mooy Yàlla mu kawe mi da koy booleel yoolub woorkat ak taxawkatu guddu, ak jiihaatkat joxandoo ko ko; ndaxte dafa taxawu ki jëkkëram faatu taxawaayu jëkkëram..., taxawu miskiin bi manul a taxawe boppam, daal di koy jox ci desiitu dundam, sarax ko ci kàttanam, ba tax njariñam di yamoo ak woor ak taxaw guddi ak jihaat.