- Moytandiku loo mer ak yi koy waral, ndax dafa dajale wépp ay, te mucc ca moo dajale wépp yiw.
- Mer ngir Yàlla niki mer su ñu xottee wormay Yàlla dafa bokk ci mer yi ñu gërëm.
- Di baamtu wax ji ndeem yittewoo nañu ko ba keroog kiy déglu di ko xam man a peeg njariñam.
- Ngëneelu sàkku ndénkaane ci boroom xam-xam.