- Bokk na ci njariñal adios bi: tere ëppal ci fayu lu ëpp la ñu la def.
- Yàlla digalul ay jaamam lenn lu leen di lor.
- Araamug loru ak lore ci wax mbaa ci jëf walla ci bàyyi.
- Fay lu tolloo ak jëf ja, ku lore Yàlla lor ko, ku sonle Yàlla sonal ko.
- Bokk na ci tënki Sariiha yi: "lor dees koy dindi", Sariiha du saxal lor, te day tere lore.