- Bokk na ci njariñal adiis bi:
- Li lay teree def aw yiw deesu ko woowe kersa, waaye yaras lañu koy woowe walla lompañ mbaa wayadi walla ragal.
- Am kersa ci Yàlla mooy di def ay ndigalam, bàyyi ay tereem.
- Am kersa ci nit ñi mooy wormaal leen, ak jox leen seen wàccuwaay, ak moytu lu aada ñaaw lu.