- Bokk na ci njariñal adiis bi :
- Mooy Sarax du yam ci li nit ki di génne ci alalam kepp, waaye day làmboo lépp lu baax lu nit ki def walla mu wax ko, te di ko jottali ñeneen ñi.
- Dafay xëcc nit ñi ci def lu baax ak def lépp luy amal njariñ ñeneen ñi.
- Bañ a xeeb jëf ju baax, donte daa tuuti.