- Bokk na ci njariñal adiis bi :
- gëneelu lewet ak téye sa bopp boo meree, ndaxte daa bokk ci jëf yu sell yi nga xam ne Lislaam da ciy soññee.
- Xeex ak sa bàkkan boo meree moo gën a tar xeex ak noon bi.
- Lislaam dafa soppi la ceddo ya jàppe woon , mu nekk jikko ju baax, kon nit ki ëpp kàttan mooy kiy téye boppam bu meree.
- Sori mer; ngir li muy waral ci lor nit ki ak mbooloo mi.