- Ngëneelu maandu ak soññee ca.
- Maandu lu matale la day làmboo mbooleem kilifteef ya, ak àtte ya ca diggante nit ña, ba ci sax maandu ci diggante jabar yi ak doom yi ak lu dul loolu.
- Leeral dayob aji-maandu yi ëllëg bis-pénc.
- Rawanteg darajay way-gëm ñi ëllëg bis-pénc, ku ci nekk ak kem jëfam.
- Xemmemloo kigay woo dafa bokku ci doxaliinu woote yi ngir ki ñiy woo man a xeemem topp Yàlla.