Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «moytandikuleen nj...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo yenn yiy waral tàqalikoo ak noonoo ci diggante jullit ñi, Bokk na ci yooyu:
(n...
Jële na ñu ci Husayfata Inb Yamaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan:...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm- day xamle ne ràmbaajkat biy tuxal ay wax ci diggante nit ñi jubloo yàq séen diggante kooku yayoo naa mbugal ci...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «s...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne jullit bi def bàkkaar dees na ko yaakaaral suturas Yàlla ak njéggalam, ba mu des kiy...
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa doon xutba n...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa doon xutba nit ñi ca bisub ubbiteg Màkka ga daal di wax ne: yéen nit ñi Yàlla de dindi na ci y...
Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Ki Yàlla gën a bañ ci nit...
Leerarug adiis bi:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ki Yàlla gën a bañ ci nit ñi mooy ku man a xulóo te bari le ko, mooy...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «moytandikuleen njort; ndaxte njort
mooy wax ji gën a nekk aw fen, te buleen di gëstu, buleen di luññutu, buleen di soxorante, buleen di tóngoowante, buleen di bañante, nangeen doon ay mbokk yeen jaami Yàlla yi ».
Jële na ñu ci Husayfata Inb Yamaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: «ab ràmbaajkat du dugg àjjana».
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «sama xeet wépp lañuy jéggal ba mu des ñiy fésal ag moy, te bokk na ci fésal ag moy nit ku def dara ci guddi gi, daal di xëy Yàlla suturaal ko, muy wax naan: éey yaw diw, biig def na lii ak lee, fekk dafa fanaan Yàlla suturaal ko, mu xëy di wuññi li ko Yàlla suturaaloon».
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa doon xutba nit ñi ca bisu ubbiteg Màkka ga daal di ne leen: «yéen nit ñi Yàlla de jële na ci yéen rëy-rëylug ceddo ga ak seenug damu ci seen baay ya, nit ñi de ñaar kepp la ñu: ku baax te ragal Yàlla daal di tedd fa Yàlla, ak ub kàccoor bu texeedi doyadi fa Yàlla, nit ñi nag ay doomi Aadama la ñu, te Yàlla a ngi binde Aadama ci suuf, Yàlla neena: [yéen nit ñi nun noo leen bind ci góor ak jigéen def leen ay giir ak i xeet ngir ngeen xamante waaye ki gën a tedd fa Yàlla ci yéen mooy ki gën a ragal Yàlla, Yàlla de ku xam la te dara umpu ko} [Saaru Al-Hujraat: 13]»
Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Ki Yàlla gën a bañ ci nit ñi mooy noon bi gën a man a xulóo.
Jële nañu ci Abuu Bakrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónenteb Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «ñaari jullit bu ñu jaamaarloo ak séen ñaari Jaasi ka raye ak ka ñu ray yépp sawara lañu jëm», ma ne ko: yaw Yónente Yàlla bi kii moo ray, waaw ki ñu ray moom luy mbiram? Mu ne: «ndax moom dafa xéroon ci ray waayam ji».
Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-hasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku gàddu ngànaay jëme sunu kaw kooku bokkul ci nun».
Jële nañu ci Aysa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «buleen saaga ñi faatu, ndax ñoom kat wéy nañu ca lañu jiital».
Jële nañu ci Abuu Ayyuuba Al-Ansaarii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: « Du dagan ci nit ki mu tóng mbokkam lu ëpp ñatti guddi, ñuy dajee kii dummóoyu kee dummóoyu, ki gën ci ñoom ñaar mooy ki tàmbli nuyóo ba».
Jële nañu ci Sahl Ibn Sahd -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku ma sàmmal li ci diggante ay ŋaamam ak li ci diggante ñaari tànkam ma wóoralal ko àjjana».
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu yal na ko Yàlla dollee gërëm -moom nag xare na ànd ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fukki xare ak ñaar- nee na: dégg naa ñent ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-te yéem na ma, mu wax ne: "bu genn jigéen tukki lu mat doxub ñaari fan lu dul mu ànd ak jëkkëram walla ab jegeñaaleem , te kenn du woor ci ñaari bis yii : korite ak tabaski, kenn du julli ginnaaw suba gi ba keroog jant bi di fenk, du caagine it ginnaaw tàkkusaan ba keroog muy so, deesul war jëm cib tukki lu dul ñeel ñatti jàkka: jàkkay Màkka ja ñu wormaal, ak jàkkay Aqsaa, ak sama jàkka jii".
Jële nañu ci Usaamata Ibn Sayd -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «bàyyiwuma sama ginnaaw fitna ju dàq a lor góor ñi ci jigéen ñi»