- Daganul jigéen di tukki ci ludul mu ànd ak ub jegeñaaleem.
- Jigéen manuta araam jigéen cib tukki; ngir li mu wax ne: "jëkkëram walla ab jegeñaaleem".
- Lépp lu ñuy woowe tukki dañu koy tere jigéen lu dul mu ànd ak jëkkëram walla ab jegeñaaleem,te hadiis bii dafa aju ci kem nekkiinu aji-laaj ji ak fa mu dëkk.
- Jegeñaaleb jigéen mooy jëkkëram walla Ku mu araam a sëyal ngir sababus mbokkoo niki baay ak doom ak baay-tëx ak nijaay, walla sababus nàmpaale niki baay cig nàmpaale,ak baay-tëx cig nàmpaale,walla sababus gorowante niki baayu jëkkër,ak mu nekk jullit bu mat te am xel di ku wóor di ku ñu wóolu,li ñu jublu ci ànd ak ub jegeñaale mooy aar jigéen gi ak ñoŋal ko ak taxawe ay mbiram.
- Sariihab Lislaam dafa yittewoo jigéen ak aar ko ak ñoŋal ko.
- Jullig naafila gu ñu boyal ginnaaw jullig fajar ak tàkkusaan du wér, dees na settee ci loolu fay julli yu faat, ak yi am sabab niki nuyu jàkka ak lu ko niru.
- Araamalees na julli ginnaaw bu jant bi di door a fenk, kon fàww ñu xaar ba mu yëkkatiku luy tolloo ak ub xeej, luy jege fukki simili ba ci ñenti xaaji waxtu wi cig nattale.
- Waxtuw tàkkusaan day wéy ba baajant bi di so.
- Tukki jëm ci ñàtti jàkka yii dagan na.
- Ngëneelu ñatti jàkka yi ak seen i may ci kaw yeneen jàkka yi.
- Tukki ngir siyaare ay bàmmeel du dagan donte bàmmeelu Yonnente bi la, ku nekk Madiina nag dana dagan mu siyaare ko, walla ku fa ñëw ngir yitte ju ñu yoonal walla lu dagan.