- Bokk na ci njariñal adiis bi :
- Tóng dagan na ci ñatti fan mbaa lu ko gën a néew, ngir sàmmoonteek yég-yégu doomu aadama, kon tóng ko ñatti fan dañu koy baale ngir li gaaroon daal di deñ.
- Ngëneelu nuyóo, ndax day dindi la ca bakkan ya, te màndargam mbëggeel la.
- Lislaam dafa xér ci mbokkoo, ak miinanteg aw ñoñam.