- Ñaawug fésal ag moy ginnaaw bi ko Yàlla suturaalee.
- Nekk na ci fésal ag moy tasaare ñaawteef ci diggante way-gëm ñi.
- Ku Yàlla suturaal ci àdduna dana ko suturaal ca allaaxira, lii daa bokk ci yaatug yërmàndey Yàlla mu kawe mi ci jaamam yi.
- Ku ñu nattoo ag moy na suturaal boppam te tuub jëm ci Yàlla.
- Màggug Bàkkaaru ñiy fésal ag moy ak diko feeñal di xañ seen bopp ag njéggal.