- Njort lu ñaaw du lor ki ay màndargam feeñ ci moom, waaye war na ci ki gëm mu nekk ku muus te xellu ba du woru ci ñu bon ñi ak kàccoor yi.
- Li ñu ci nàmm mooy artu ci tuuma jiy nekk cim xel, ak di ca wéy, bu dee liy gaar bakkan te du ca wéy, loolu moom kenn du ko toppe kenn.
- Araamal nañu lépp luy waral fuñante ak dogante ci diggante mbooloom jullit ñi, ci luññutu ak soxor ak yu ni mel.
- Laabire ci di jëflante ak jullit ñi jëflanteg mbokk ci laabire ak bëggante.