- Àrtu gu tar ci jullit di rayante ak mbokki jollitam.
- Bokk na ci ñaawtéef ak yàq yi gën a rëy ci kaw suuf bocci gànnaay ci kaw jullit ñi, ak di yàq ci raye.
- Tëkku googu ñu tudd du làmboo rayante ci dëgg, niki rayante ak way-bew yi, ak yàqkat yi ak ñu mel ni ñoom.
- Araamal nañu tiital jullit ñi ci gànnaay mbaa leneen, -doonte sax ci anamug fo la-.