- Ki dogu ci xolam ci def ag moy daal di def ay sababam kooku day yayoo mbugël.
- Moytandikuloo gu tar ci rayante ci diggante jullit ñi ak tëkku ci sawara gi ci nekk.
- Rayante ci diggante jullit ñi bu tegee ci dëgg du dugg ci tëkku gi, niki rayanteek ñi bew ak yàqkat yi.
- Kiy def ay bàkkaar yu mag yi du nekk yéefër ngir loolu rekk; ndaxte Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- daa woowe ñaar ñiy rayante ay jullit.
- Bu ñaari jullit jamaarloo ci jumtukaay bumu man a doon buy raye, ba kenn ka ray moroom ja, kon ki raye ak ka ñu ray ñépp sawara lañu jëm, li Hadiis bi tudd Jaasi nag day niral rekk.