Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «àdduna de...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne àdduna ñam wu neex la, te naat ci gisiin, ba nit ki dana ci woroo, ba di ci nuur, ba...
Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-Ashsrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Deesul tak...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral ne jigéen du dagan ñu takk ko ci lu dul kilifa gu taxawe takk ga.
Jële na ñu ci Huqbata Ibn Haamir -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «sart yi...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne sart yi gën a yelloo matal mooy yiy ñu man a daganal bànneexu ci jigéen, te mooy sart...
Jële nañu ci Abdulaah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «àdduna a...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne àdduna ak li ci biiram mbir mu ñuy bànneexoo ab diir rekk la mu jeex , waaye li gën ci...
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na zulu.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na wat lenni kawaru bopp bàyyi leneen li. Tere gi nag day làmboo góor ñépp ndaw ak mag, bude...

Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «àdduna de ñam wu neex la te naat, Yàlla da leen fee wuutal, di xool lu ngeen fiy jëf, noytuleen àdduna te moytu jigéen ñi, ndax fitna ji njëkk a am ci Banuu Israayil ci jigéen la xewe».

Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-Ashsrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Deesul takk jigéen ci lu dul kilifa».

Jële na ñu ci Huqbata Ibn Haamir -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «sart yi gën a yelloo matal mooy yi ngeen daganale péy ya.

Jële nañu ci Abdulaah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «àdduna ay jumtukaay rekk la, te li gën ci jumtukaay yi àdduna mooy jigéen ju baax».

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na zulu.

Jële na ñu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «jempleen Seen mustaas yi, te yar sikkim yi».

Jële na ñu ci Abii Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne: "góor du xool awray góor, jigéen it du xool awray jigéen,te góor ak góor duñu sàngu ci menn malaan,jigéen ak jigéen it du ñu sàngu ci menn mbalaan .

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-nekkul woon ku ñaawi wax mbaa jëf, daa na wax naan: « ñi gën ci yéen mooy ña ca gën a rafet jikkó».

Jële na ñu ci Aysa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «aji-gëm ji jikkoom ju rafet danako may mu am darajay Aji-woor ak kiy taxaw di julli».

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yònente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ki gën a mat ug ngëm ci jullit ñi mooy ki ci gën a rafet jikko, te ki gën ci yéen mooy ki gën ci ay jigéenam».

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Laaj nañu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- lan mooy li ëpp luy duggal nit ñi àjjana, mu wax ne: «ragal Yàlla ak rafet jikko», ñu laaj ko lan moo ëpp luy duggal nit ñi sawara mu ne: «gémmiñ ak awra».

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo gënoon a rafet jikko ci nit ñi.