Jële na ñu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «jempleen Seen mustaas yi, te yar sikkim yi».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Explanation
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa digle ñu dindi dara ci kawaru mustaas te bañ koo bàyyi noonu, waaye dañu koy jemp.
Ca wet ga mu digle ñu yar sikkim bàyyi ko mu sëq.
Hadeeth benefits
Araamal nañu wat ab sikkim.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others