- Tere nañu di xool awray keneen ba mu des jëkkër ji ak jabaram.
- Xérug Lislaam ci laabal mbooloo mi ak tëj bunt yiy indi ñaawteef.
- Dagan na ñu xool awray keneen bu dee aajo moo ko waral, niki faj ak lu ko niru, ci kaw mu nekk ci ludul bànneexu.
- Jullit bi dañu koo digal mu muur awraam te dammu gisam ci awray keneen.
- Dañoo jagleel tere gi góor ak góor, ak jigéen ak jigéen; ngir moo gën a man a waral xool awray keneen ak wuññi awra.