- Bokk na ci njariñal hdiis bi: War na ci aji-gëm ji mu sori lu ñaaw moo xam wax ju ñaaw la mbaa jëf ju ñaaw.
- Matug jikkoy Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, dara daawul juge ci moom lu dul jëf ju sell ak wax ju teey.
- Jikkó ju baax mooy barabu rawante ga, ndax ku jiitu rekk bokk ca way-gëm ya gën, te gën a mat sëkk ag ngëm.