- War nañoo matal sart yi nga xam ne kenn ci ñaar ñiy sëy moo ko warlul keneen ki, lu dul muy sart buy araamal lu dagan walla muy daganal lu araam.
- Matal sarti sëy moo gën a feddaliku lu dul moom; ndaxte mooy tollook daganal awra ya.
- Màggug sëy ci Lislaam, ba tax mu feddali ne na ñuy matale sart ya.