- Bokk na ci njariñal hdiis bi: Màggug yittewoog Lislaam ci yar jikko yi ak matal ko
- Ngëneelul jikko yu rafet, ba tax muy yóbb jaam bi ci darajay aji-woor jidul dog, ak aji-taxaw jidul sonn.
- Woor bëccëg ak taxaw guddi ñaari jëf lañu yu màgg am na ñu nag ab coono ci bàkkan, boroom jikko yu rafet yi day àgg ci seen daraja ngir li muy xeex ak bakkanam ci jëflante bu rafet.