Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo gënoon a rafet jikko ci nit ñi
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo gënoon a rafet jikko ci nit ñi.
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Explanation
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo gënoon a mat jikko ci nit ñi, mbooleem jikko yu rafet yi moo ca jiitu, ci wax ju teey, ak jëf ju yiw, ak béllil xar kanam, ak téye lor te muñ ko ci ñeneen ñi.
Hadeeth benefits
Matug jikkoy Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mooy royukaay bu mat bi ci rafet jikkó.
Ñaaxe ci roy Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci rafet jikkó.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others