- Ñaaxe ci taqoo ak ragal Yàlla, te bañ a soxlawoo liy feeñ ci àdduna ak taaram bi.
- Moytondikuloo di fitnawu ci jigéen ñi, ci xool mbaa ci càgante ci góoru jàmbur di jaxasoo ak ñoom, mbaa yeneen.
- Fitnay jigéen bokk na ci fitna yi gën a màgg ci àdduna.
- Waaru ak xalam ci xeet yi jiitu woon, li xew ci Banuu Israayil man naa xew ci ñeneen.
- Fitnay jigéen bu dee jabar la man naa teg jëkkëram lu mu àttanul ci ab dund, ba dana ko soxlaal wolif muy sàkku ay biri diineem, ba dana ko yóbbe muy xawa alku ci sàkku biri àdduna, bu dee jàmbur nag fitnaam mooy fiir góor ñi ci jengloo leen wolif dëgg ci bu nu génnee ba jaxasoo ak ñoom, rawatina bu ñu nekkee jigéen yu sollut lu jot, tey baraj-baraji, te lii man naa waral tàbbi ci njaalo ci kem ay darajaam, kon war na ci aji-gëm ji mu làqu ci Yàlla, te yaakaar ko ci mucc ci seeni fitna.